Jaamu

Lëndëm ya ngi mey wërone
Yeesu
Fees del ci man
Bi nga joxé sa bopp ci kurwaa bi, ngir man
Sa dereet sang ma
Lëndëm xadial leeraay
Ak dund gu dul jeex
Bës bu bees jóg na sama aduna
Sa mbëggel tax na ma yeeslu
Kenn du yaw buuru buur yi
Yeesu
Kenn du yaw doomu Yàlla

Ma ngi ley jaamu
(Jëlel sama xeel, yaw rek yay boroom)
Ma ngi ley jaamu
(Jëlel sama xol, yaa di sama buur)
Ma ngi ley jaamu
(Yaw rekk ya ma mom, defal lu la neex ci man)
Jaamu sa tuur bu Sella

Waaye waxtu ba ngi ñëw
Te sax, waxtu bii jotna
Sey jaam dëgg negn la jaamu
Ci xeel ak ci dëgg
Ndax yoyou jaam la Baye bi bëgë

Ma ngi ley jaamu
(Sama reeni xol, yaw rek lay woyal)
Ma ngi ley jaamu
(Ya ma gënël lu ma am ci kaw suuf)
Ma ngi ley jaamu
(Asaman ak suuf, ñu ngi ley woyal)
Jaamu sa tuur bu Sella

Yay doomu Yàlla!
Kaadu Yàlla!
Mburtum Yàlla!
Yaw la, yaw la Yeesu!!!

Ma ngi lëy jaamu
(Ni la malaka yi di woyé ci asaman)
Ma ngi lëy jaamu
(Sey jaam gnu ngi lëy woyal ci kaw suuf)
Ma ngi lëy jaamu
(Buur bi Yàlla, yaw suñu reeni xol)
Jaamu sa tuur bu sella
(Ya diara màagal, tagass, woyal, yëkkëti)

Ma ngi lëy woyal
(Yeesu Krista doomu Yàlla Baye)
Ma ngi lëy woyal
(Andak sa Baye ak Xeel mu Sella mi)
Ma ngi lëy woyal
(Di negn la woy ba abadane)
Woyal sa tuur bu sella



Credits
Writer(s): Anne Elisabeth Kande
Lyrics powered by www.musixmatch.com

Link