Love

Par AbouAmg
Mbëggeel du xeet
Xol buy bëgg du tàggoo
Sama yaay booy ne na ma
Maa xool keneen
Même su ma bëggul
Waaye na doon sama deretooy
Man waruma
Doon ki jittel sama bànneex
Donte sama xol am na tànneef
Waaye yaay booy ne na ma
Sama doom du sa wareef
Ñun, bété-bété lañu
Boo nekkul pure sang
Doo rax suñu deret
Ñun, bété-bété lañu
Boo nekkul pure sang
Doo rax suñu deret
Sori may tewul nga jege ma
Sama xol sama xel lañu ci yaw
Chérie booy ooo céy dellusil
Yaw mbëggeel du fo
Te mbëggeel du jaay
Kenn du ko jële ca marché ba
Man yaw laa nob!
Yaay ne deet, baay ne deet
Waaye soo demee damay wet chéri booy ooo
Xol jàppu du wor ka mu nob
Xoolul deret, xoolul xeet
Ña kay dundal rekk lay seetoo
Ñun, bété-bété lañu (ñun bété-bété lañu)
Boo nekkul pure sang
Doo rax suñu deret
Ñun (ñun nii), bété-bété lañu (ñun bété-bété lañu)
Boo nekkul pure sang
Doo rax suñu deret
Dégguma la, dégguma la
Sama yaay sama baay
Ne nañu duma séy ak waje
Ki géer la, géwél la
Ñeeño wala Maabo
Man moom laa nob

Mbëggeel du nobeel

Nobeel du cofeel

Eh eeeeh sama waje

Man moom laay wër



Credits
Writer(s): Ismaila Talla, Marieme Diop
Lyrics powered by www.musixmatch.com

Link