Bekoor

Mbay maral wi mettina yaay
Bekoor bi yàkk na ndeysan
Ndimbal lañuy sakkoo
Gir baykat sonn na yaay

Mbay maral wi mettina yaay
Bekoor bi yàkk na ndeysan
Ndimbal lañuy sakkoo
Gir baykat sonn na yaay

Démb da doon taw aywaay yé
Suuf naan màndi
Démb da doon taw di baawaan
Jur gi naan sempi
Démb da doon bakaaw di jàncax
Jur gi xontu mbaa jur
Àll be naan réew mi naan di guŋdanaan
Sitóor yi naan com maral

Mbay maral wi mettina yaay
Bekoor bi yàq na ndeysan
Ndimbal lañuy sakoo
Gir sámmkat bi sonn yaay

Mbay maral wi mettina yaay
Bekoor bi yàq na ndeysan
Ndimbal lañuy sakoo
Gir sámmkat bi sonn yaay

Démb da doon taw aywaay yé
Eh, eh, ho-ho, he, ho-ho,he
Ah-ha, he, ho, he-he man, he

Mbay maral wi mettina yaay
Bekoor bi yàq na ndeysan
Ndimbal lañuy sakKoo
Gir sámmkat bi sonn yaay

Tay su xin ne sappar gelawaal mbaa naat say
Ak nawet buu nangu baa dal meññaal gàncax
Taay Baykat bëttul, desetul gerte
Wa réewmi yàq warul tax, taa mën a nekk
War ngaa bokk ci ndimbal lii jëm ci waa gaw gi
Ndeysan maral bi meeti yaay
Sámmkat sonn
Nañu ndimbali sanu bopp nax yàlla ndimbali ñum
Nanu ndimbali sunu moroom nax Yàlla nangul nooo
Maral,maral,maral

Maral,maral,maral bi metti na
Maral,maral,maral bi metti na
Maral,maral,maral bi metti na

Nanu jëmbët garab te di koo suxal garab ci la
Maral,maral,maral bi metti na
Nanu ndimbali sanu bopp nax yàlla ndimbali ñum
Maral,maral,maral bi metti na
Nanu jëmbët garab te di koo suxal garab ci la
Maral,maral,maral bi metti na

Yàlla yàlla bay sa tooloo
Maral,maral,maral bi metti na
Ngir wa kaw gi maral bi metti na
Maral,maral,maral bi metti na



Credits
Writer(s): Youssou N Dour
Lyrics powered by www.musixmatch.com

Link