Jirim

Naawal naawal naawal
Balaa guddee

Naawal naawal naawal
Balaa ñu lay fexeel
Naawal
Guddi jot na guddi jot na fooy fanaan
Naawal
Yaay ja reer baay ba naxsaay na
Naawal naawal naawal
Balaa ñu lay fexeel

Naawal naawal naawal
Balaa ñu lay fexeel
Guddi jot na gaawal gaawal balaa ñu lay fexeel
Yaay ja reer na baayam saay na
Naawal naawal naawal
Balaa ñu lay fexeel

Soo ko fi gisulee guddi moy dem na
Te soo ko fi gisee sànku na
Cokkeer doom noppil
Sa yaay wuti na
Naawal naawal naawal
Balaa ñu lay fexeel

Su weetee jooy
Su sonnee jooy
Su woppee jooy
Su raflee jooy
Guddi jot na guddi jot na guddi jot na fooy fanaan
Naawal naawal naawal
Balaa ñu lay fexeel

Su weetee jooy
Ndax saa yu xiifee fànde
Su guddee mu lakku balaa ñu koy fexeel
Kii lu mu sonn sonn taxul
Taxul coono yi jeex
Su muññee bii beneen na koy xaar ëllëg
Beneen na koy xaar ëllëg beneen na koy xaar ëllëg
Su guddee mu lakku balaa ñu koy fexeel
Naawal naawal naawal
Balaa ñu lay fexeel
Yaay ja reer na baayam ba saay na

Su guddee mu lakku balaa ñu koy fexeel
Naawal naawal naawal
Balaa ñu lay fexeel
Yaay ja reer na baayam ba saay na

Baayam ba saay na

Ku ammul ndey nàmp ci maam
Ku ammul maam doyloo sa bopp

Naawal naawal naawal

Naawal naawal naawal
Balaa ñu lay fexeel



Credits
Writer(s): Ashs The Best, Olivier Delahaye, Sy Abdoulaye
Lyrics powered by www.musixmatch.com

Link