Guddi - Bonus Track

Biig ci guddi gi biig ci guddi gi gent la laa fanaanee
Gent gi yee ma ci ay nelaw
Kenn du ma xool kenn du ma xool
Ci bët te duma jaawale'g yow
Bu ñu jooyee bu ñu jooyee taxul nga delluwaat fi
Sa dem gi weetal na ñu
Bëgg dem taxul mën a dem
Mën a dem tax a dem

Suba si lay xaar bu jot
Su bët setee ma waxaat la ko
Guddi biig bee yagg ci man
Mbaa su ëllëge di nga tal xool sa ginaaw

Biig ci guddi
Gestul gestul balaa muy wees

Man'ag guddi manaam guddi lay leeral
Amatu fi sa mbëggeel amatu fi

Gestul xoolal deglul fatalikul demb
Ndax lepp day wees
Setlul saayoo gestoo gis ma ci sa wet
Ndax xolay gise

Yaa am ñaanu loo
Yaa ñakk goreediwoo
Yaa weet te dawuloo
Yaa yòpp te jooyuloo

Gestul xoolal deglul fatalikul demb
Ndax lepp day wees
Setlul saayoo jaxlee gis ma ci sa wet
Ndax xolay gise

Yaa am ñaanu loo
Yaa ñakk goreediwoo
Yaa weet te dawuloo
Yaa yòpp te jooyuloo

Biig ci guddi gi biig ci guddi gi gent la laa fanaanee
Gent gi yee ma ci ay nelaw
Kenn du ma xool kenn du ma xool
Ci bët te duma jaawale'g yow
Bu ñu jooyee bu ñu jooyee taxul nga delluwaat fi
Sa dem gi weetal na ñu
Bëgg dem taxul mën a dem mën a dem tax a dem

Biig ci guddi
Gestul gestul balaa muy wees

Suba si lay xaar bu jot
Su bët setee ma waxaat la ko
Guddi biig bee yagg ci man
Mbaa su ëllëge di nga tal xool sa ginaaw

Gestul gestul balaa muy wees



Credits
Writer(s): Olivier Delahaye, Sy Abdoulaye
Lyrics powered by www.musixmatch.com

Link