Naari Xalé

Bay Moodu demal mu ne du dem
Xelam dallul
Bëgg dem taxul ta mën a dem
Mën a dem, moy tax a dem
Waayam ja, yàkkamti woon, jël yoon wa
Te yoon woowe du yoonam
Ci lëndëm mu gis fa réer, ci lëndëm ñu gis fa réer
Dugg ci gaal, yaakaar féey ci ndox ci digg u geej ci diggu geej
Surux, yaakaar yépp tas na, ñépp ngaay jooy

Bay Moodu dem na
(lutax mu dem?)
Picc ramatu ma ngay naaw waye xel mu ñi ci suuf
Ñu mën a kott, dëgg-dëgg ndekete yorul ñu mbaam

Ñaari xale, ñoo ñi wër yàlla
Ñaari xale, ñoo ñi wër yàlla
Seeni rangoñ moo fi tuuru woon
Wër nañu ba dee (wër nañu ba dee)
Wër nañu ba dee

Kan mooy laal ngone
Kan mooy laal ngone
Laal na yàlla (kan mooy laal ngone)
(Kan mooy laal ngone)
Kan mooy laal ngone
Kan mooy laal ngone
Laal na yàlla

Kuu jàpp ci loxoom waay mu yobbu la (kan mooy laal ngone)
(Kan mooy laal ngone)
(Laal na yàlla)

Kumba jirim la ndax ñàkk yaay
Baayam tële, dénk ka nijaayam
Ci ba mi ndaw, ci ba mi ndaw
Nijaayam war ko yar, far sàkku ndawam (Jirim kumba)
Bàyyi ko ak màndaga bu dul jóg ci moom (ba ba mi de)

Picc ramatu ma ngay naaw waye xel mu ñi ci suuf (kan mooy laal ngone)
(Kan mooy laal ngone, laal na yàlla)
Ñu mën a kott, dëgg-dëgg ndekete yorul ñu mbaam (kan mooy laal ngone)
(Kan mooy laal ngone, laal na yàlla)



Credits
Writer(s): Abdoulaye Sy, Olivier Delahaye
Lyrics powered by www.musixmatch.com

Link