Bideew

Giisoo, yeewu (ha-ha, eh-eh, ha-ha)

Xa naa giisoo fu xalaat yi sutte
Asamaan
Xa naa giisoo ko yaw
Loolu moo waral nit ñi wuute
Ci xalaat

Giisu lo ni, giisu lo ni,fi amna ay bideew
Yiy leeral
Xa naa giisoo ko
Te bu suuf di sedd, suuf ci di sedd guy
Du nelaw

Xa naa giisoo nuñu mandoo
Mbaa melni luy la faale
Bu mettee deggu nañ ko
Te bu neexee ñu yobbaale
Ndeke yàlla ji,moom noppina
Te bu suuba ñu yekaliko
Motax boo demee bay daanu
Xoolatal foy jafanu

Du suñu ndam, du suñu cër bu dee, guddee, guddee tinnañu
Bu amoon xaaxoo duñu bàyyi, bu de, bu de, bu de ci ñun la
Bu amoon leyla du ci moom, weet fi goore te wetaliko sa ngor
Waxoon na la duñu bàyyi, bu de, bu de, bu de ci ñun la

Ayo noo yèwwoo
Ñaan u yaay la yendoo, yendoo
Giiso ni naaj na waxee du ñu mës guddee, guddee
Bideew yi léer nañ (léer nañ)
Yàlla léen fi nekkaloon
Bu ñu naaje duñu guddee (duñu guddee)
Te bu ñu guddee ñoo ci sa wet

Ayo noo yéwwoo
Ñaan u yaay la yendoo, yendoo
Ayo noo yéwwoo
Barke baay la yéwwoo, yéwwoo
Giiso ni naaj na waxee du ñu mës guddee, guddee
Bideew yi léer nañ
Maam Yàlla léen fi nekkaloon

Maam Yàlla léen fi nekkaloon waaw
Bideew, bideew yi léer nañ
Maam Yàlla léen fi nekkaloon waaw
Bideew, bideew yi léer nañ



Credits
Writer(s): Olivier Delahaye, Abdoulaye Sy, Oumar Samb
Lyrics powered by www.musixmatch.com

Link