Baay Faal

Baay Faal ba daa jóg ca fajar
Nga séén ko mu soli sagar
Boppam ba sëq xëki kawar
Yore këllëm bë di sikkër
Te faalewul xiifak mer
Moo demee kat xeex na badar
Kii turam wi dootul fay
Ku weddi lii laaj ko waa Ndar
Baay Faal jaaxal na waa Ndar
Baay Faal jaaxal na waa Ndar
Baay Faal ba daa jóg ca fajar
Mani kuur Yàlla daa jóg ca fajar
Nga séén ko muy soli sagar
Yore këllëm bë di sikkër
Kii turëm wi dootul fay
Ku weddi lii laaj ko waa Ndar
Baay Faal jaaxal na waa Ndar
Baay Faal jómmal na waa Ndar
Dundam ga neex na, sikkar sa neex lool
Baay Faal bi, Baay Faal idi moo di gënë góór
Sikkar sa moo tax mu jege Yàlla
Baay Faal bi, Baay Faal ku ko xamoon di nga maandu ci moom
Sa tool ya, sa teen ya, ca waañ wa, maajal ya
Baay Faal iigééy la xam
Baay Faal ndigël la xam
Baay Faal du xeex du xulóó
ëg na nit, fónk na nit
Xeebul kenn, noon la yegeeg boroomam
Li mu li figééyat suñu boroom
Bëgg naa la Bay Faal
Ndongo li kii moo jege sunu boroom
Day ligééy di joxe
Moo tax Baay Faal jege na sunu boroom
Day ligééy di joxe
Day ligééy di joxe moo tax Baay Faal
Toggam ga neex na lool moo tax Baay Faal
Day maajal moo tax Baay Faal
Day sikkar moo tax Baay Faal



Credits
Writer(s): Mouhamadou Gueye, Mody Ba, Youssou N'dour
Lyrics powered by www.musixmatch.com

Link