Tukki

Yoon wi nga jël baaxul ku la koy digël da lay nax
Yoon wii ci des moo gën, loo taseel dàldi kuy mën
Yoon wii nga jël booy dox ba ca
biir géstul xool fi nga weesu balaa ngay
Booy tukki yaw
Booy tukki yaw
Na nga bàyyl ba mën
Ding cë jëléé lu mënë xew ca feneen
Dina tax nga mën xam nekkinu ñeneen
Foofo mën nga fa gis lu yókk sa xameel
Booy tukki yaw
Nita ngi toog di janoog yaw booba
fekk na ma ngay xalaat ba tàbbi asamaan
Àndag niir yiy naaw dem na fu sore lépp ciy xalaatam
Yaw sama waay kaay ma xamal la
Léég léég nga toog fi nga toog tukki bu neex dem ba kaw asamaan
Ànd ag weer wiy naaw li ngay janeer
mu lay neex boo janoo mu gën fee neex
Booy tukki yaw
Booy tukki yaw yeesal sa xameel
Ding cë jëléé lu mënë xew ca feneen
Dina tax nga mën xam nekkinu ñeneen
Foofa mën nga fa gis lu yókk sa xameel
Deel tukki yaw
Lëppa lëpp sàmba ma ngay naaw, te booy seet sax taxu koo gaaw
Te léég léég mu dem ba kaaw
Tukkee ka neex, waaw
Lucum cééli ma ngay naaw te léég léég
mu naaw ba kaw asamaan indi fiy xabaar
Ku dul tukki doo xam fu dëkk neexe
Booy tukki yaw
Na nga bàyyi
Booy tukki yaw
Na nga bàyyi ba mën
Ding cë jëléé lu mënë xew ca feneen
Dina tax nga mën xam nekkinu ñeneen
Foofa mën nga fa gis lu yókk sa xameel
Booy tukki yaw
Booy tukki yaw
Booy tukki yaw
Na nga bàyyi ba mën
Ñaanu barke ah ñaanu barke
Nita ngi toog di janoog yaw booba
fekk na ma ngay xalaat ba tàbbi asamaan
Àndag niir yiy naaw dem na fu sore lépp ciy xalaatam
Yaw sama waay kaay ma xamal la
Léég léég nga toog fi nga toog tukki tukki bu neex dem ba kaw asamaan
Làng ag weer wiy naaw li ngay janool mu
lay neex boo janoog moom mu gën fee neex
Booy tukki yaw
Na nga bayyi ba mën
Ding cë jëléé lu mënë xew ca feneen
Dina tax nga mën xam nekkinu ñeneen
Foofa mën nga fa gis lu yókk sa xameel
Deel tukki yaw
Lëppa lëpp sàmba ma ngay naaw, te booy seet sax taxu koo gaaw
Te léég léég mu dem ba kaaw
Tukkee ka neex, waaw
Lucum cééli ma ngay naaw te booy seet
sax taxu koo gaaw ëndaaleel ñu xabaar
Tukkee ka neex, waaw



Credits
Writer(s): Youssou N'dour, Kabou Gueye, Mody Ba
Lyrics powered by www.musixmatch.com

Link