Sunugal

Golo ngui di baay baboune doundé
Tokk sunu kaw yata youmbé
Nioune gnifi dess yakar kun déy
Sunu life gueune hot niouy mathie tougn déy
Fay Sunu lampe koupé sunu ndox youkou
Sunu doundeu kone fokk niou niaff sèn nd
Kom komou réw bi guène passarr-passarréé
Louniou ama kass ak néw guène dieul mandé
Niak bék fébar yek walakana bi niouy gueuneu toumranké
Guène télé mbélé mbélé diokhé délé ay féni nène ma tay
Oubile sa beut té xoll li khéw
Diougueul fipou nguir sa réw
Baniou massi sakh guène defma néw
Guène gassma soule douma bokk sèn guéw
Sénégal loumou mérité dé dou Li
Ndiouth ndiath bi dé wessou fii
Sathie ngui mom béssou fi
Takhena sunu caisse dara déssou fii
Borom keur yagui run dépense
Amatou niou ndieugou ordonnance
Khif ak marr dignou eskanté ngay woutt nguissteul cii renaissance
Vide de sens, incompétence
Tu ne mesures pas les conséquences
Fermes ta gueule et fous le camp
On a perdu assez de temps
Bépp gokh fo meune tiii dém kaddu bi bèn leu daniou beug nga yokh
Lifi né mom diégui na tiss
Lignou yèn daay gueune diss

Diokhatila Rap ngakoy feel di chill
Sénégal éh
Sénégal oh
Sénégal moy sunu réw
Sénégal éh
Sénégal oh
Sénégal moy sunu réw

Na beut yi wékh
Na xol yi fékh
Na fiitna dale sunu thiono diékh
Clando yi garé, 4×4 yi guène
Niou pédophiles yi ak goor djiguène yi
Lo fii def Yalla néla je retiens
Ngay muslim wala ngay chretiens
Ngay ilimane wala politiqu'chiens
Yiy djité sunu réw dignou tékeulé ak chiens
Loy titeuro loy poukeuré wo
Alalou riba bi dé yaw goré wo
Nioune nio wathione cii tali bi ak yaw
Sopi nganiou digone niou dadii lay naw
Taay la gale ngui gueune dikk
Gueuneu sikk
Xalé yi xaddi diar cii guethie gui daw
Rap galsen bi tchii wané niveau bileu
Technique kou bindeu bi dé nieuw ropila
Xam xamou mbede bi ngay dém rotila
Wessou na rap bi dé li tiokila tiokila tiokila
Yo Low Low Low Low
Guiss nga li xéw cii mbeude bi ndakh sa yaram dawna
Askan wi defla ennemi ndakh sèn xoll yi wow na
Fébar yi beuri sunu biir takhna déh gui gaw na
Té biss bou né nga dégg kopar yigni fi loubeul raw na
Té néw di dolé diey fay sèn taukhi douna
Té koffi waulou fale ko taay souba sopé kouna
Yeurmandé amatoul cii diam yi ma niak souma
Na yalla def cii xoll yi lerr ndakh beut yi guissa touniou

Diokhatila Rap ngakoy feel di chill
Sénégal éh
Sénégal oh
Sénégal moy sunu réw
Sénégal éh
Sénégal oh
Sénégal moy sunu réw

Naniou fagaru fékhé ba kèn douniou waaleu
Téleu diouk meuneu xali yone dialeu
Yorr sunu poches ay millions dollar
Di bégué beauté am free, am power
Naniou bolo benno job
Galsen nek on the top
Niane cii diami Casamance Yalla def tchi li ko sobb
Kèn waroul manqué thiop
Kèn waroul xepp say mbokk
Kèn waroul am ba béw
Ndakh xamoulo souba lane moy xéw
Boy dém Makka tabakh diaka li nga tchi def dana fekk mou léw
Dana fekk mou léw

Diokhatila Rap ngakoy feel di chill
Sénégal éh
Sénégal oh
Sénégal moy sunu réw
Sénégal éh
Sénégal oh
Sénégal moy sunu réw
Sénégal moy sunu réw
Sénégal éh
Sénégal oh
Sénégal moy sunu réw



Credits
Writer(s): Nitdof, Papa Kandé Sidibe ( Mao )
Lyrics powered by www.musixmatch.com

Link