Takk Jog

Mësu ma daw bay xàddi man (Daw bay xàddi man)
Nekka Ci yoon daj naa lu nekk (yoon daj na lu nekk)
Mësu ma toog bay baayi yeah (toog bay baayi yeah)
Gisu ma woon ku ma gungee yeah (kenn ku ma gungee yeah)
Takk jog yeewu doori waar di ko utt
Jënd café naan ñëpp guux
Tallal loxo ñaan rafetul, rafetul no
Takk jog yeewu doori waar di ko utt
Jënd café naan ñëpp guux
Tallal loxo ñaan rafetul, rafetul no

Wërsëg du mës jeex
Gën dolli jom bañña baayi dëkk ci xeex
Soxla gudd fan ndaxte dee bi du mës yeex
Nangu nattu Yalla te xam naa ni dina neex
Tekki ba mën feex
Dëggu ci sama yoon
Daani sama doole ngir yoraale samay doom
Dox ci seeni yite di sooraale li ñuy doon
Jàng waxu diine ñu mën xàmmee lu bonn
Ñanal ma lepp yòmb

Mësu ma daw bay xàddi man (Daw bay xàddi man)
Nekka Ci yoon daj naa lu nekk (yoon daj na lu nekk)
Mësu ma toog bay baayi yeah (toog bay baayi yeah)
Gisu ma woon ku ma gungee yeah (kenn ku ma gungee yeah)
Takk jog yeewu doori waar di ko utt
Jënd café naan ñëpp guux
Tallal loxo ñaan rafetul, rafetul no
Takk jog yeewu doori waar di ko utt
Jënd café naan ñëpp guux
Tallal loxo ñaan rafetul, rafetul no

Kërti-kërti di daxadi fay du dèñ
Gën waaru dèmb akk jamano tay du benn
Ñëpp bëgg taaru akk jaayu ngir bëgg feeñ
Gisa tu ma màndu akk làkku ndax ñeme fen
Teela yeewu ñeme naaj
Dëkk ci xoslu di utt
Ligeey bu ròmb ñu buub
Soxla ba tallu ñu toog daaj
Daanu tere wu ñu yeeg
Akk lu yoon bi mën ñàng du ñu yèem

Mësu ma daw bay xàddi man (Daw bay xàddi man)
Nekka Ci yoon daj naa lu nekk (yoon daj na lu nekk)
Mësu ma toog bay baayi yeah (toog bay baayi yeah)
Gisu ma woon ku ma gungee yeah (kenn ku ma gungee yeah)



Credits
Writer(s): Momar Gueye Ngom, Mouhamed Loucar
Lyrics powered by www.musixmatch.com

Link